Déglul Doomi Golo bu Bubakar Bóris Jóob te doo fey dara

Doomi Golo téereb nettali bu yéeme la te daw yaram. Képp ku ko jàng doo gaaw a fàtte Ngiraan Fay. Ngiraan, goxu Ndakaaru buñ naan Ñarelaa la dëkk ; màggat la, xiibon, di xaar Yàlla def ci moom li gën. Foo ko fekk mu ngi fereηlaayu ci keppaaru garabu màngo gi ci ëttu këram, sëgg di bind ak a bindaat, di joow, daanaka, ak xalimaam ci kow kayit gi mu tiim. Lu waral muy yendoo bind, fanaanee bind ? Dafa fekk rekk baay Ngiraan boole ñaari naqari àddina : doomam Asan Taal faatu nay at ci ginnaaw Màrsey, muy wéy di ko jooy, ba noppi sëtam Badu gàddaay, mu namm ko ba fu nammeel yem. Te li gën a diisal xolam, moo di ne kenn xamul man réew la jant biy tiime Badu Taal ak lu ko tee yónneey bataaxal, waa gox bi xam boog naka la tooge, seen xel dal. Wànte lenn moom wóor na Ngiraan : lu mu yàgg yàgg, Badu Taal dina delsi Ñarelaa ndax gone gu am fulla la, du moo nar a xatal ay doxandéem ca seen réew. Waaye it, góor gi xam na ne, ndeysaan, su sët bi ñibbisee dina fekk moom mu wuyuji boroomam. Kon leer na ko ne dootuñu gise ba fàww. Ci la jénd 7 karne yu melo ya wute di ci ñaarook Badu Taal, lépp lu ñëw ci xel mi mu nettali ko sët bi, rawatina xew-xewi gox bi ak seen jaar-jaaru xeet. Am na sax ci téere yooyu bu mu ci tudde ‘’Téereb Ndéey’’, di ko ci fen li mu yaakaar ne warul a tàbbi ci yeneeni nopp. Doomi Golo téere bu am doole la, Ngiraan Fay day wéy di topp jàngkat bi, mel ni ku koy woyal, leeg-leeg kàddu yiy wëndéelu ci géew biy dóor-dàqe, – ñu ni tekk, ni leen bindkat biy ràbbee gën leen a jox kàttan.

Tekkees na Doomi Golo ci:

  • Tubaab: Les petits de la guenon ci tekkim Bubakar Bóris Jóob (Editions Philippe Rey, 2009)
  • Español: El libro de los secretos, ci tekkim Carlos Lozano (Editorial Almuzara, 2015)
  • Àngale: The Hidden Notebooks, ci tekkim Vera Leckie ak El Hadji Moustapha Diop (Michigan State University Press, 2016)
  • Kërug-móolukaayu Internet gu ñuy wax 2709 Books génneendoo na ko ci wolof ak español ci atum 2017

Yebal walla nga déglu Bubakar Bóris Jóob muy jàng Doomi Golo te doo fey dara:

 

 

Description

Lilyan Kesteloot :

“Bi ma jàngee Doomi Golo, yéemu naa, sama xol bi yëngu, leeg-leeg sax mu jóg, ma mer ba futt. Wànte yit du benn du ñaar fentakoon bi reeloo na ma, maak moom nu piisante, mu mel ni li may miin i kàddoom yépp teewul ñu ub sama bopp bi.”

— (jàngleen li ci des)

Pape Samba Diop :

“Du ci kàllaama Tubaab rekk la nit kiy yéemoo ci taaru dunya te yit du moom rekk a mën a tudd mbëggeel walla mbañ.”

— (jàngleen li ci des)

Bu weesoo Senegaal, mënees naa jënd sunuy téere ca Amerig, Meksig, Kanadaa ak Frãs. Ku leen soxla ci réew yi nu limul fii, mën naa jokkook nun