Bàmmeelu Kocc Barma, Bubakar Bóris Jóob

27.00$

Njéeme Pay, taskatu xibaar bu siiw ci Senegaal, moo toog bés këram dégg ci rajoy réew mi ne Joolaa bi, bato bi daan lëkkale Sigicoor ak Ndakaaru, suux na. Bàmmeelu Kocc Barma day delsi ci jéyya ju tiis jooju, di sargal ñi ci faatu ñépp, di jéem a yeewaale yit askan wi ngir lu ni mel bañ noo dalati.

Waaye Njéeme yemul foofu : dafa nuy fàttali yit jaar-jaaru ndem-si-Yàlla ji Kinne Gaajo, fentaakon bu mag bu fiy taalifam yéemoon Afrig ak àddina si yépp. Ñoom ñaar nag, ay xariti benn bakkan, ay doomi-ndey, lañu woon, ku ci nekk xamal lépp sa moroom. Looloo tax Njéeme Pay di dànkaafu jàngkat bi, naan ko : bul jàppe Bàmmeelu Kocc Barma ni téereb nettali doŋŋ, téereb dekkali la tamit. Yokk na ci sax ne ‘’ fey bor, féddali kóllëre ak sàmm sama kàddu ñoo ma ko tax a bind…’’

Yebal dog bu njëkk bi

SOO BËGGEE JËND

Description

Bóris sàkkul i way-jëmmal ne def na li mu war a def, daldi ciy raxas loxoom ba mu set wecc. Déedéet, fexe na ba nu jàppe leen ni ay nit dëggëntaan te su loolu amee dafa fekk mu ànd ak dal ci mbind mi, xaar ba yëf yi ñor mu door leen a nataal.
— Uséynu Béey, Seneplus (jàngal li ci des)

Bu weesoo Senegaal, mënees naa jënd sunuy téere ca Amerig, Meksig, Kanadaa ak Frãs. Ku leen soxla ci réew yi nu limul fii, mën naa jokkook nun