Doxandéem bu Ibraayima Saaxo Caam

Description

BINDKAT BI

 a nga juddoo ca Rëbës ca atum 1973, muy gox bi nekk diggante Medinaa ak Ñaay Cokkeer, géej gi féete ko sowu. Gannaaw ba mu dalee Alxuraan, ci la dugg ci daaray nasaraan ba am « baccalauréat » ci 1994 ci « Lycée Delafosse ». Ci la dem nag ca Iniwérsite Séex Anta Jóob, laata muy tukki ca réewum Almaañ ca 1996, ngir jàngi fa Polotig ak Koom-koom. Mi ngi dellusi ci atum 2010, ràngoo lijaasab Doktoraa, daldi tàmbalee liggéey ci kurél gu Almaañ teg fii ci Senegaal, muy yëngu ci yaatal ag jàppaleem ci réewi Afrig yi.Ibrayima Saaxo Caam

Cofeelam ci woy ci làmmiñu wolof a ngi juddu ca jamono ja mu doonoon doxandéem ca Almaañ. Li mu sori woon réewam, sori njabootam ak i moomeelam, dafa jur ci moom ag cofeel ci dellu jàngaat, ngir gën a xam ay aadaam ak i cosaanam. 

TÉERE BI

Ci xalimag Murtadaa Jóob

Gëstukat, bindkat, woykat ci làmmiñu wolof

Damay faral di wax naan woyu wolof, ci am xelam, doonul laasi janeer yuy bërëŋ xelum woykat bi ci mbartalum bànneexi bàkkan mbaa naqar kese. Doonul it ngiirteg bari jot mbaa ñàkk a def dara. Déggtil xelum làmmiñu wolof ki koy jéem a tënk ci yooyu. Ndax bu nu dawale (dawalee) téereb woyu Ibrayima Saaxo Caam bii di Doxandéem ba mu jeex, li nu ciy jële mooy:

               1 – Téereb Ibraayima Saaxo Caam bii nekkul téere bu ñuy jàng njàngum biti, ngir taari woy yi kese. Téere la bu ñuy war di settantal, ci baat yi woykat biy jumtuwoo ak ca kàndaŋi baat yi bu ñuy ërfoo, ndeem bëgg nanu cee jariñu.

               2 – Xelum woyu Ibrayima Saaxo Caam jéggi na digi « ax » ak « cam », di doxantu ci leeri cofeel ak kaaraange yi koy yeewat ak i ñoñam, di ko yeewat ak roytéef yi muy kañ ci xaajub « SARGAL » (« Tey sama xol tënku na fu sori mën a tollu, Samay xalaat jéggi ay dëkk ak i réew Ngir mën à uufu ci sag kiiraay« ). Daa mel ni sax ku nàmp ci weenu xelum démb, bay gall leeri mbatiit ak mbaaxi maam ya, saa suy jëmmal ay xew-xew, mbaa ag yëg-yëg, mbaa yu muy fàttaliku, ci ay woyam. Mu mel ni yooyu ñooy pakki kiiraay yi koy sàmm, di ko aar, di ko ñoŋal ci lëndëmi wéetaay ba teree (tere) koo diig, ni yenn moroomam ya dogoo ak seen xelum làmmiñu cosaan. 

              3 – Dinanu yëg it ni Doxandéem ag woote la ak ug jàjj ñeel ndaw ña ca réewi Ma-weex yu sori yaa sori, ni : « sori gëti ndey ak baay warul a tax ba kenn di wat jubbab xàmmeekaayam, mbaa muy damm yarub xàjjeem, bay xebet ak a doyadil jikko ya ñu maam nàmpale woon ca sunu meenum xelum démb, ndey daan ca yebe doomam bu daan tukki ca réewi Tubaab ya « .

              4 – Bu nuy déglu bu baax woyi Ibrayima Saaxo Caam yi, ci seenum xel ak ci seeni daaj-boyal, danuy mel ni ñu nuy xalab ca digg jataayi ndaanaani démb ya woon, ca pénci Kajoor ya, mbaa yu Njàmbur, mbaa yu Bawol ya.

              Li may daanele waxu artu ji mooy Ibrayima Saaxo Caam teguna ciw yoon, yoon wu gudd, yoon wu jafe, waaye yoon wu bariy njariñ bu lajj amul. Li ci des mooy mu ñime ko te sax ci, ak keneen képp ku bëgg a dog yoon wi mu jaar.

En plus du Sénégal, nos ouvrages sont disponibles aux USA, au Mexique, au Canada et en France. Veuillez nous contacter pour les autres pays